Jële nañu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yónent bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «wërale nañu sawara...
Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day leeral ne sawara dañu koo wërale ak i mbir yoy bakkan da koo bëgg, ci jëf yu araam yi, ag gàtteñ...
Jële nañu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «bi Yàlla bindee àj...
Leerarug hdiis Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day leeral ne bi Yàlla bindee àjjana ak sawara, dafa wax Jibriil -yal na ko Yàlla dol...
Jële na ñu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «Séen sawara wi ab...
Leerarug hdiis bi : Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day xamle ne sawaraw àdduna ab xaaj la ci juróom-ñaar fukki xaaji sawaraw Jahann...
Jële nañu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: dégg naa Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- muy wax ne: «Y...
Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day xamle ne yawmal xiyaam Yàlla day ŋëb suuf si dajale ko, mu lem asamaan si ci ndayjooram taxañ l...
Jële nañu ci Aysatu ndayu jullit ñi -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dafa ñëw ci man...
Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dafa dugg ci néegu Aysatu -yal na ko Yàlla dollee gërëm- fekk mu muure kamootam bu ndaw bu muy def...

Jële nañu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yónent bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «wërale nañu sawara ak ay bànneex, wërale àjjana ak ay naqar».

Jële nañu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «bi Yàlla bindee àjjana ak sawara dafa yónni Jibriil -yal na ko Yàlla dolli jàmm- ca àjjana, ne ko: demal xool ko ak la ma ca waajalal ay ñoñam. Mu xool ko daal di ñëw, ne ko: giñ naa ci sa màgg gi ne kenn du ko dégg lu dul ne dana def lu ko cay dugal. Mu digle ñu wërale ko ak ay tiis, mu ne ko: demal xool ko ak la nu ca waajalal ay ñoñam, mu fekk ñu muure ko ak i tiis mu wax ko ne: giñ naa ci sa màgg gi ragal naa ne kenn du fa dugg. Mu ne ko demal nga xool sawara ak la ma ca waajalal ay ñoñam. Mu xool ko gis waa sawara a nga warante, mu dellu ne ko: giñ naa ci sa màgg gi kenn du def lu la fay dugal. Mu digle ñu muure ko ak i bànneex, mu ne ko: dellul xool ko. Mu xoolaat ko gis ñu muure ko ak i bànneex, mu dellu ne ko: giñ naa ci sa màgg gi ragal naa ne kenn du ca mucc».

Jële na ñu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «Séen sawara wi ab xaaj la ci juróom-ñaar fukki xaaj ci xaaji sawaraw Jahannama», ñu ne ko: yaw Yónente Yàlla bi, bu doon moom rekk kon dana doy. Mu wax ne: «ëppe na ko juróom-benni fukk ak juróom-ñenti xaaj, te ñoom ñépp ñoo ngi mel ni aw tàngaayam».

Jële nañu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: dégg naa Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- muy wax ne: «Yàlla dat ŋëb suuf si, lem asamaan yi ci ndayjooram, di wax naan: man maay buur, ana buuri suuf si».

Jële nañu ci Aysatu ndayu jullit ñi -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dafa ñëw ci man fekk ma muure sama kamoot bu ndaw ab moorso bu am ay nataalu yu am ruu, ba mu ko gisee kanam gi soppiku, mu ne ma: "yaw Aysatu,nit ñi gën a tar mbugal fa Yàlla ëllëg bis-pénc ñooy ñiy roy bindub Yàlla bi" Aysatu nee na: "ma dagg ko def ko ñegenaay walla ñaari ñegenaay".

Jële nañu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne : Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: «giñ naa ci ki sama bakkan nekk ci loxoom, daa naka rekk Iisaa Ibn Maryama wàcc ci yeen di ab àttekat bu màndu, di toj kurwaa yi, di ray mbaam-xuux yi, dindi galag gi(empo) bi, alal daal di baawaan ba kenn soxlawu ko».

Jële na ñu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dafa wax baay taxam ba: « waxal ne: amul kenn ku yayoo jaamu ku dul Yàlla, ma seedeel la ci ëllëg bis-pénc», mu ne ko: bu dul woon waa Xurays danañu ma ŋàññi, di wax naan: li ko yóbbe loolu mooy tiitaange, kon dinaa ci bégal sa bët. Yàlla daal di wàcce Aaya bii: {du yaw yaay gindi koo sopp, waaye Yàlla mooy gindi ku ko soob} [Al-Xasas: 56].

Jële na ñu ci Abdullah Ibn Amr -yal na leen Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: «Sama mbalka ma de mi ngi toll ne doxu weer, ndoxam ma moo gën a weex meew, xetam ga moo gën a neex gëttug misk, te koppu yi dañoo mel ni biddiwi yi nekk ci asamaan Ku ci naan doo mar mukk ».

Jële nañu ci Abuu Sahiid Al-Xudriyu -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: «dinañu indi dee ci melow kuuy mu duuf, ab wootekat daal di woote: yéen waa àjjana, ñu yoqamtiku di xool, mu wax ne: ndax xam ngeen lii ? Ñu ne ko: waaw, lii mooy dee, te ñoom ñépp a ko gis, mu woote ne: yéen waa sawara, ñu yoqamtiku di xool, mu wax ne: ndax xam ngeen lii ? Ñu ne ko: waaw, lii mooy dee, te ñoom ñépp a ko gis, ñu rendi ko, mu wax ne: yéen waa àjjana sax ba fàwwu dee amatul, yéen waa sawara sax ba fàwwu dee amatul, daal di jàng: {na nga leen xupp bisub réccu ba ba ñu àttee mbir ma fekk ñoom ñoo ngi cig càggante} [Maryama: 39], waa àdduna jii ñoo ngi cig càggante, {te ñoom duñu gëm}[Maryama: 39]».

Jële na ñu ci Umar ibnul Xattaab -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: dégg na Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- muy wax ne: «su ngeen wakkirlu woon ci Yàlla dëgg-dëggi wakkirlu, kon dana leen wërsëgal kem ni muy wërsëgale picc mi, day xëy nek ku woos xiif di gont biir bi fees dell.

Jële nañu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm-mu wax ne :Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: «ki war mooy nuyu kiy dox, kiy dox mooy nuyu ki toog, ñi néew ñooy nuyu ñi bari».

Jële nañu ci Abuu Sarrin -yal na ko Yàlla dollee gërëm-: Jële na ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu jële ci Yàlla mu kawe mi mu wax ne:«yéen sama jaam ñi damaa araamal tooñ ci sama bopp, ma def ko muy lu araam ci seen diggante kon buleen di tooñante, yéen sama jaam ñi yéen ñépp dangeen a réer ku dul ki ma gindi, kon sàkkuleen ci man gindiku ma gindi leen, yéen sama jaam ñi yéen ñépp a xiif ku dul ki ma leel, kon sàkkuleen ci man ma leel leen , kon dinaa leen leel, yéen sama jaam ñi yéen ñépp a rafle ku dul ki ma wodd, kon sàkkuleen ci man ma wodd leen kon dinaa leen wodd, yéen sama jaam ñi dangeen di juum guddi ak bëccëg kon jéggaluleen ma ma jéggal leen, yéen sama jaam ñi manuleen maa lor ba di ma lor, te manuleen maa jariñ ba di ma jariñ, yéen samay jaam ñi njëkk ci yéen ak ñi mujj ci yéen, nit ñi ak jinne yi ci yéen bu ñu neekkoon xolu ki gën a ragal Yàlla ci yéen loolu du yokk ci sama nguur gi dara, yéen samay jaam ñi njëkk ci yéen ak ñu mujj ña, ak seen i nit ak jinne bu ñu neekkoon xolu ki gën a kàccoor ci yéen loolu du wàññi ci sama nguur gi dara, yéen samay jaam ñi njëkk ci yéen ak ñu mujj ña, ak seen i nit ak jinne dañoo taxaw ci benn pàkk bu yaatu, ñu ñaan ma ma jox kenn ku nekk la mu ñaan loolu du wàññi li ne fi man lu dul li ab puso di wàññi ci ndoxum géej gi bu ñu ko sa dugalee, yéen sama jaam ñi seen jëf rekk laa leen di dencal joxaat leen ko ba mu mat, ku fa fekk yiw na sant Yàlla, waaye ku fa fekk ay bu mu yedd ku dul boppam».