- Hadiis bii dafa bokk ci li Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nettali jële ko ci Boroomam, ñu di ko woowe Hadiis Al xuddsi walla Hadiisu Al Ilaahiy, te mooy Hadiis bi nga xam ne ay baatam ak i maanaam ci Yàlla la juge, waaye amul jagle yi nekk ci Alxuraan te mu koy ràññetle ak lu dul moom, niki di jaamu Yàlla ci jàng gi ak di laab ngir jàng ko, ak di ci dëgge mbaa di ci lottloowaate ak yenneen.
- Lépp lu jaam bi am ci xam-xam walla ag njub, ci xamleg Yàlla ak ug gindéem la ame.
- Lu jaam bi am ci yiw ci ngëneelu Yàlla mu kawe mi la ko ame, waaye lépp lu ko jot ci ay ci bakkanam ak bànneexam la juge.
- Képp kuy rafetal ci tawfeexu Yàlla la, te ag payam ci ngëneelu Yàlla la, kon cant ñeel na ko, képp kuy ñaawal bu mu yedd lu dul bakkanam.