- Bokk na ci njariñal hdiis bi :
- Deesul bàyyi dëgg ngir ragal waxi nit ñi.
- Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- li mu man mooy gindig tegtal ak jubbanti waaye amul gindig dëppale.
- Yoonalees na seeti yéefar bu feebar ngir woo ko ci Lislaam.
- Xérug Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ci woote jëme ci Yàlla mu kawe mi ci gépp anam.