- Weddi lu bon ca jamono ja ñu ko gise te bañ koo
- yeexe, fii ak ag yàqute gu gën a tar nekku ca.
- Mbugalu bis-pénc day rawante ci kem màggaayu bàkkaar bi.
- Nataal yi am ruu dafa bokk ci bàkkaar yu mag yi.
- Bokk ci li tax ñu araamal nataal jéem a roy bindub Yàlla bi, moo xam kiy nataal moo ci jubloo roy walla jubluwu ko.
- Xérug Sariiha ci sàmm alal yi ci ñu ciy jariñoo ginnaaw ba mu moytandikuloo la ñu ca araamal.
- Tere nañu ñuy defar nataalu lu am ruu ak nu mu man a mel, doonte dañu koy doyadal.