Jële nañu ci Umar ibn Xattaab -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Benn bis danoo toog ci yònente bi, fa saasa benn waay ñëw, bu sol yéere ya weex tàll,kawar ga ñuul kukk,te kenn gisul ci moom jeexiit i tukki, te it kenn xamu ko ci nun, bam aksi toog ci yònente bi -yal na ko Yàlla dolli jàmm ak mucc-, daa di wéer ñaari wóomam ci ñaari wóomi yónente bi, teg ñaari tenqam ci kaw poojam,daal di ne ko: yaw Muhammat xibaar ma luy lislaam Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ne ko: «Lislaam mooy: nga seede ne amul kenn ku deesi jaamu ku dul Yàlla, seede ne Muhammat ndawul Yàlla la, tey taxawal julli, di woor weeru koor, te aj Màkka benn yoon boo ko manee» mu ne ko: wax nga dëgg nu yéemu ci moom di ko laaj ba noppi di ko dëggal, mu ne ko: xibaar ma lan mooy gëm? mu ne ko: «mooy nga gëm Yàlla,ak i malaakaam,ak i téeréem, ak i yónentam, ak bis bu mujj ba, nga gëm ndogal yi; ya ca neex ak ya naqari» mu ne ko: wax nga dëgg daal ni ko: xibaar ma lan mooy rafetal? mu ni ko: «mooy ngay jaamu Yàlla mel ni yaa ngi koy gis, ndax boo ko gisul moom moo ngi lay gis» mu ne ko: xibaar ma kañ la bis-pénc? mu ne ko: «ki ñu koy laaj gënu koo xam ki ko koy laaj» mu ne ko: wax ma ay màndarngaam? mu ne ko: «mooy jaam ba jur ab sangam, nga gis way-fàndaañu ya way-rafle ya way-ñàkk ña sàmukati jur ya, ñuy guddalaante ca tabax ya» mu dem ma daal di sax ci ag jaaxle, mu ne ma: « Umar ndax xam nga aji-laaj ji ?» ma ne ko: Yàlla ak ub yónenteem ñoo xam mu ne ma: «koo ku Jibriil la, dafa ñëwóon ngir xamal leen seen diine».