- Maanaam seede ne amul kenn ku ñu war a jaamu ku dul Yàlla mooy kennal Yàlla cig jaamu, ak moytoo jaamu lu dul moom.
- Maanaam seede ne Muhammat ndawul Yàlla la mooy gëm ko ak li mu indi, ak dëggal ko, ak ne mooy ki mujj ci Yónent Yàlla yi mu yónni ci nit ñi.
- Wax ak boroom xam-xam ak ku am i lënt-lënt bokkul ak wax ak ku xamul; looloo tax mu bàyyiloo xel Muhaas ci ne ko: «yaa ngi jëm ci ñoñ-téere».
- Solos jullit xam diineem bu baax; ngir mu mucc ci lënti ñay lëntal te loolu mi ngi ci sàkku xam-xam.
- Neenug diiney Yahuud yi ak Nasaraan yi ginnaaw ba ñu yónnee Yónente bi Muhammat -yal na ko Yàlla dolli xéewël ak mucc-, ak ne ñoom bokkuñu ca way-mucc ña ëllëg bis-penc ba keroog ñuy dugg ci diiney Lislaam, daal di gëm Yónent bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-.