- Saxal rammug Yónent bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ëllëg bis bu mujj ba, ak ne ag ramam du ñeel ñenn ñu dul way-kennal Yàlla yi.
- Rammoom mooy ñaan Yàlla mu kawe mi ñeel aji-kennal Yàlla yi yayoo woon sawara ñu bañ faa dugg, ak ku fa duggóon mu génn fa.
- Ngëneelu baatu tawhiid di kennal Yàlla képp, ak màggaayu jeexitalu baat bi.
- Dëggal kàddug Tawhiid mi ngi ame ci xam li miy tekki, ak jëfe ya muy waral.
- Ngëneelu Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm-, ak ug xéram ci xam-xam.