- Toroxlug Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- bay togg Muhaas ci ginnaaw daaba.
- Jàngaliinu Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-, ba tax muy baamtu woo gi muy woo Muhaas ngir mu gëna teewlu li mu koy wax.
- Bokk na ci sàrti seede ne: amul kenn ku ñu war a jaamu ku dul Yàlla ak ne Muhammat ndawul Yàlla la, ki koy wax dafa wara nekk ku dëggu ci limiy Wax am kóolute te baña nekk weddi mbaa kuy sikk-sakka.
- Ñiy kennal Yàlla duñu sax sawaraw Jahannama, bu ñu fa duggee it ci sababus séen i bàkkaar; dees na leen fa génne ginnaaw ba ñu laabee.
- Ngëneelu ñaari baati seede yi ñeel ku ko wax te dëggal.
- Dagan na ñu bañ a waxtaane ab hadiis ci yenn jamono yi bu dee yàqute man na caa tege.