ku faatu fekk moo ngi wutal Yàlla ndend dana dugg sawara
Jële na ñu ci Abdullah Ibn Mashuud -yal na ko Yàlla dollee gërëm- me wax ne: Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- wax na jenn wax, ma wax Jeneen wax, yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dafa wax ne: " ku faatu fekk moo ngi wutal Yàlla ndend dana dugg sawara" man ma ne: ku faatu te wutalul Yàlla ndend dana dugg àjjana.
Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér
Explanation
yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day xamle ne ku jël lu Yàlla jagoo jëme ko ci ku dul moom, niki ñaan ku dul Yàlla mu kawe mi, ak xettaliku ci keneen, daal di faatu ca loola kooku ci waa sawara lay bokk. Ibn Mashuud -yal na ko Yàlla dollee gërëm- teg ca ne ku faatu te bokkaalewul Yàlla ak dara kooku mujjam mooy àjjana.
Hadeeth benefits
Ñaan de ag jaamu la, deesu ko defal ku dul Yàlla mu kawe mi.
Ngëneelu Tawhiid, ak ne ku ca faatu dugg àjjana, donte dañu koo mbugal ci yenn bàkkaaram yi.
Loràngey bokkaale, ci ne képp ku ci faatu dina dugg sawara.
Share
Use the QR code to easily share the message of Islam with others