- Jaamu yépp ci Alxuraan AK Sunna lay tabaxu, dunu jaamu Yàlla ci lu dul lu mu yoonal, dunu ko jaamu ci ay bidaa ak yi ñu sos.
- Diine du tege cim xel rekk ak lees di rafetlu, waaye ci topp Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- lay tege.
- Hadiis bii tegtal la ci matug diine ji.
- Bidaa mooy lu ñu sos ci diine ji te amutóon ci jamonoy Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ak i Sahaabaam muy ci pas-pas walla wax mbaa jëf.
- Hadiis bi cosaan la ci cosaani diiney Lislaam, day mel niki balaas ci jëf yi, niki nga xamee ne jépp jëf ju ñu nammul jëmmi Yàlla mu kawe mi, aji-jëf ji du ci am ub yool, niki noonu it jépp jëf ju dëppoowul ak li Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- indi dees koy delloo aji-jëf ji.
- Sos yi ñu tere mooy yi bokk ci biri diine, waaye du yu àdduna yi.