Explanation
Umar ibnul Xattaab -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-day nettali ne Jibriil dafa ñëw ca Sahaaba ya -yal na leen Yàlla dollee gërëm- ci melow genn góor gu ñu xamul, bokk na ci ay meloom ay yéreem dafa weex tàll, kawaram ga ñuul kukk, te kenn du gis ci moom jeexitalu ku tukki niki coono, ak yére yu tilim, te ña fa teew kenn xamu ko ci, fekk ñoo ngi toog ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-, mu took ci kanamu Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-toogiinu kuy jàng, daal di koy laaj Lislaam, mu tontu ko ponk yii di làmboo ñaari baati seede yi, ak sàmmoonteek julliy juróom, ak joxe asaka ñeel ña ko yayoo, ak woor weeru koor, ak joxe faratay aj ci képp ku ko man.
Aji-laaj ji ne ko: wax nga dëgg, Sahaaba yi daaldi yéemu ci laajam bii di tegtale ne moom xamul limiy laaj
ba noppi di ko dëggal.
Mu laaj ko luy Imaan, mu tontu ko ponk yii di juróom-benn làmboo gëm amug Yàlla mu kawe mi ak i meloom, ak kennal ko ci ay jëfam niki bind, ak kennal ko ci jaamu gi, ak gëm Malaaka yi nga xam ne Yàlla da leen a bind ci leer, ci ne ay jaam yu tedd lañu, duñu moy Yàlla mu kawe mi te ay ndigalam la ñuy def, ak gëm téere yi ñu wàcce ci Yónente yi mu bawoo ca Yàlla mu kawe mi, niki Alxuraan ak Tawraat ak Injiil ak yeneen yu dul yooyu, ak gëm Yónente yiy jottali diine ja juge fa Yàlla, bokk na sa ñoom Nuuh ak Ibraahiima ak Muusaa ak Iisaa ka ca mujj di Muhammat -yal na leen Yàlla dolli xéewal ak mucc- ak yeeneen Yónente yu dul ñoom, ak gëm bis bu mujj ba, dana dugg ca loola liy xew ginnaaw dee, dale ko ca bàmmeel ba ak dundug Barsaq, ak ne nit ki dees na ko dekkil ginnaaaw ba mu deehee daal di koy regle, benn mujjantalam nekk àjjana walla sawara, ak gëm ne Yàlla dogal na bir yi ca na mu jiitoo ca xam-xamam ba, te ak xereñam waral ko, ba noppi mu bind ko, ak it coobareem ca loola, te day tàbbi ca kem na mu ko nattale, te amale ko noona. Mu laaj ko lan mooy Ihsaan (rafetal), mu xibaar ko ne rafetal mooy nga jaamu Yàlla ba mel ni yaa ngi koy gis, ndax boo ko gisul moom moo ngi lay gis, bu manula àgg ci daraja jii, mu jaamu Yàlla gëm ne Yàlla moo ngi koy gis, bu njëkk bi darajay gis la te moo gën a kawe, bu ñaareel bi darajay fuglu la.
Ginnaaw ba mu laaj ko kañ la bis-pénc ? Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- leeral ne xam-xam ub bis-pénc dafa bokk ci li Yàlla jagoo, benn mbindéef xamu ko, moo xam ki ñu koy laaj, mbaa kiy laaj.
Mu laaj ko màndargay bis-pénc ? Mu leeral ne bokk na ci ay màndargaam jëbéer yi ak seen i doom nekk ñu bari lool, (jëbeer : jaamu bu jugéen) walla doom yu bari di dog seen i way-jur di jëflante ak ñoom ni ñuy jëflantee ak i jëbéer, ak ne sàmmkati jur yi ak way-ñàkk ñi da ñuy woomle ci àdduna ci mujjug jamono, di puukarante wu ci ay taax ak i tabax yu taaru.
Yónente Yàlla bi daal di xamle ne ki doon laaj Jibriil la dafa ñëwoon ngir jàngal Sahaaba yi seen diine ju jub jii.