- Bokk na ci njariñal hdiis bi:
- Ngëneelu Tawhiid ci ne képp ku faatu di aji-gëm te bokkaalewul Yàlla ak dara dana dugg àjjana.
- Loràngey bokkaale, ci ne képp ku faatu te bokkaale Yàlla ak dara dana dugg sawara.
- Ñiy kennal Yàlla tey def ay bàkkaar ñoo ngi ci suufu coobarey Yàlla bu ko soobee mbugal leen, bu ko soobee it mu jéggal leen, waaye seenug mujj mooy àjjana.