Jële nañu ci Sufyaan Ibnu Abdullah As-Saxafii -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne : Wax naa : yaw Yónente Yàlla bi, wax ma ci Lislaam wax...
Sahaaba bii di Sufyaan Ibnu Abdullah -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dafa laaj Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ngir mu xamal...
Jële na ñu ci An-Nuhmaan Ibn Basiir -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne, Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: «misaalu way-...
Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day leeral ni jullit ñi war a mel ci seen biir ci yéeneente aw yiw ak yërmànde ak dimbaleente ak...
Jële na ñu ci Usmaan Ibn Affaan -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «Ku jàpp te raf...
yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ne ku jàpp sàmmoonte ak Sunnay Njàpp ak i tegginam, loolu sabab la ci far ay ñaawtéef ak sippi ay ñu...
Jële nañu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yonente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «Yàlla du nangu jul...
Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day leeral ne bokk na ci sàrti wérug julli: laab, kon ku bëgg a julli day war ci moom mu jàpp ndeen...
Jële nañu ci Jaabir -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Umar Ibnul Xattaab xibaar na ma ne: Benn waay dafa jàppu daal di bàyyi barab buy tollook...
Umar -yal na ko Yàlla dollee gërëm- day xibaare ne Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dafa gis benn waay bu jàppu ba noppi,fekk dafa b...
Jële nañu ci Sufyaan Ibnu Abdullah As-Saxafii -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne : Wax naa : yaw Yónente Yàlla bi, wax ma ci Lislaam wax joo xam ne duma ko laaj kenn ku dul yaw, mu ne ma : "waxal gëm naa Yàlla, te jub kocc".
Jële na ñu ci An-Nuhmaan Ibn Basiir -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne, Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: «misaalu way-gëm ñi ci seenug bëggante ak seenug yërëmante ak seenug ñeewantu day mel ni aw yaram, bu ci benn cër di jàmbat dara mbooleem yaram wi yépp day
ànd bañ a nelaw ak di tàng».
Jële na ñu ci Usmaan Ibn Affaan -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «Ku jàpp te rafetal njàpp ma, ay ñaawtéefam day génn ci aw yaramam bay génn ci ay weyam».
Jële nañu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yonente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «Yàlla du nangu jullig kenn ci yéen bu dee daa tojle ba keroog muy jàpp».
Jële nañu ci Jaabir -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Umar Ibnul Xattaab xibaar na ma ne: Benn waay dafa jàppu daal di bàyyi barab buy tollook aw weh ci ay ndëggoom Yonnente bi-yal na ko Yàlla dolli xéewal akmucc- gis ko ne ko:"dellul te rafetal sa njàppu mi" mu dellusi,daal di julli.
Jële nañu ci Amru Ibn Aamir mu jële ci Anas Ibn Maalik mu wax ne: Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- da daan jàppu ci julli gu ne, ma ne ko: lan ngeen daan def yéen? Mu ne: njàpp mi dana doy nit ki feeg tojlewul.
Jële na ñu ci Humraan jaamub
Usmaan Ibn Affaan, mu wax ne, gis na Usmaan Ibn Affaan laaj ndox mu mu jàppoo, mu tanq loxoom ci ndab li, raxas leen ñatti yoon, mu dugal ndeyjooram ci jàppukaay bi, daal di gallaxndiku saraxndiku fiiru, daal di raxas xar kanamam ñatti yoon, ak ñaari loxoom ba ci conco yi ñatti yoon, daal di masaa boppam, daal di raxas tànk bu ne ñatti yoon, daal di wax ne: gis naa Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- muy jàppoo kem sama njàpp mii, ba noppi wax ne: "ku jàppoo kem sama njàpp mii, daal di julli ñaari ràkka yoy du ca xalaat dara, kon Yàlla dana ko jéggal bàkkaaram yi jiitu".
Jële nañu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: Bu kenn ci yéen di jàpp na def ndox ci bakkanam daa di saraxndiku, kuy fomp (laabu) na ko tóolal, bu kenn ci yéen yeewoo ciy nelawam na raxas loxoom njëkk mu koy dugal ci jàppukaay bi, ndax kenn ci yéen xamul fan la ab loxoom fanaan". Baati Muslim mooy: "bu kenn ci yéen yeewoo ciy nelawam bu mu nuural loxoom ci ndab li ba baa mu koy raxas ñatti yoon ba noppi, ndaxte moom xamul fan la ab loxoom fanaan ".
Jële nañu ci Ibnu Abbaas -yal na leen Yàlla dollee gërëm- mu wax ne : Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dafa romb ñaari bàmmeel, daal di wax ne : « ñoom ñaar de ñoo ngi leen di mbugal, te sax mbugaluñu leen ci lu rëy, kenn ki moom daawul suturawu bu daan saw, keneen ki nag da daan dox di rambaaj" mu jël aw xob wu tooy, xar ko ñaari xaaj, roof ci bàmmeel bu ne wenn xaaj, ñu ne ko : yaw Yónente Yàlla bi, lu tax nga def lii ? Mu wax ne : "amaana ñu woyafalal leen fii ak wowuñu».
Jële nañu ci Anas -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- bu daan dugg ci wanag day wax: «Allaahumma innii ahuusu bika minal xubusi wal xabaa-isi».