Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- jàpp na ñaar-ñaar
Jële na ñu ci Abdullah Ibn Mashuud -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- jàpp na ñaar-ñaar.
Al-buxaariy soloo na ko
Explanation
Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- bu daan jàpp leeg-leeg daa na raxas cér bu nekk ñaari yoon, mu raxas kanam gi -ca la gallaxndiku ak saraxndiku bokk- ak ñaari loxo yi ak ñaari tànk yi ñaari yoon.
Hadeeth benefits
Li war ci raxas cér yi mooy benn yoon, lu ca tege dañu koo sopp.
Yoonal nañu jàpp ñaar-ñaar leeg-leeg.
Li ñu yoonal ci masaa bopp mooy benn yoon.
Share
Use the QR code to easily share the message of Islam with others