- Jullig ku tojle deesu ko nangu ba keroog muy laab ci sangu set ci toj mu mag, mbaa ci njàpp ci toj mu ndaw.
- Jàpp mooy jël am ndox wërale ko ci biir gémmiñ daal di koy génne, daal di xëcc ndox mi ci ag noyyeem mu jëm ci biir bakkanam, mu génnewaat ko ci fiiru, topp mu raxas xarkanamam ñatti yoon, daal di raxas ñaari loxooom ànd ak conco yi ñatti yoon, daal di masaa bopp bi benn yoon, topp mu raxas ñaari tànk yi ñatti yoon.