- Cosaanu diine mooy gëm Yàlla cig moomeelam, ak cig jaamu, ak ci ay turam ak i meloom.
- Solos njub ginnaaw gëm, ak wéy cig jaamu, ak sax ci loolu.
- Ngëm Yàlla sàrt la ngir ñu nangu jëf yi.
- Gëm Yàlla, day làmboo lépp luñu war a fas ci ay pas-pasi ngëm ak i cosaanam, ak la cay topp ci ay jëfi xol, ak wommatu ak nangul Yàlla ci li nëbbu ak li feeñ.
- Jub mooy taqoo ak yoon wa, ci def yi war ak bàyyi yi ñu tere.