- Rambaaj ak ñàkk a set ci saw dafa bokk ci bàkkaar yu mag yi, ak yiy waral mbugalu bàmmeel.
- Yàlla dafa wuññi yenn kumpa yi -niki mbugalu bàmmeel- ngir feeñal ay màndarga ci ag Yónnenteem -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-.
- Jëf jii muy xar ñaari xob ak teg ko ci kaw bàmmeel bi Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- moo ko jagoo; ndax Yàlla moo ko wan mbiri boroom bàmmeel yi, kon deesu ci natt keneen ndaxte kenn xamul mbiri ñi nekk ci bàmmeel yi.