Jële na ñu ci Abdullah Ibn Mashuud -yal na ko Yàlla dollee gërëm- me wax ne: Laaj na Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-: ban bàkkaar m...
Laaj nañu Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ban bàkkaar moo gën a màgg? Mu wax ne: Ba ca gën a màgg mooy bokkaale gu mag, te mooy nga...
Jële nañu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne : Yónent Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: "Yàlla mu kawe m...
Yónent bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day xamle ne Yàlla mu baarkeel mi te kawe dafa wax ne: moom moo gën a doylu képp kuy bokk, mooy ki do...
Jële nañu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «Sama xeet wépp din...
Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day xamle ne xeetam wéppay dugg àjjana ba mu des ku bañ! Sahaaba yi -yal na leen Yàlla dollee gër...
Jële nañu ci Umar Ibnul Xattaab -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne : dégg naa Yónent bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «bulee...
Yónent bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day tere ëppal ak jéggi dayob Sariiha ci tagg ko ak di ko melal ay meloy Yàlla mu kawe mi ak i jëfam...
Jële na ñu ci Anas -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «Kenn ci yéen du gëm...
Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day xibaare ne jullit bi ngëmam du mat ba keroog muy jiital bëgg Yónente Yàlla bi -yal na ko Y...

Jële na ñu ci Abdullah Ibn Mashuud -yal na ko Yàlla dollee gërëm- me wax ne: Laaj na Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-: ban bàkkaar moo gën a màgg fa Yàlla? Mu ne: "nga wutal Yàlla ndend te mu bind la" ma ne: loolu de rëy na lool, ma ne ko: topp ca lan? Mu wa ne: "nga ray sa doom; ngir ne dangaa ragal mu lekkandoo ak yaw" ma ne ko: topp ca lan? Mu ne ma: "nga njaalo ak sa jabari dëkkandoo".

Jële nañu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne : Yónent Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: "Yàlla mu kawe mi nee na: ñiy bokk ñépp maa ci gën a doylu, képp ku jëf jenn jëf bokkaale ma ca ak keneen ma bàyyi ko ak bokkaaleem".

Jële nañu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «Sama xeet wépp dinañu dugg àjjana ba mu des ku bañ», ñu ne ko ana kan mooy bañ yaw Yónente Yàlla bi? Mu ne: «ku ma topp dugg àjjana ku ma moy nag kooku mooy ki bañ».

Jële nañu ci Umar Ibnul Xattaab -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne : dégg naa Yónent bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «buleen ma jay kem ni Nasaraan yi jaye woon doomu Maryama; man daal ab jaamam laa, kon deeleen wax: jaamub Yàlla ak ndawam».

Jële na ñu ci Anas -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «Kenn ci yéen du gëm ndare ma gënal ko way-juram ak doomam ak mbooleem nit ñi».

Jële nañu ci Abdulaah Ibn Amr -yal na leen Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «Jottalileen jële ci man donte benn aaya la, ta ngeen waxtaane waa Banuu Israayil ci lu amul benn jafe-jafe, waaye ku ma fenal te tay ko na waajal ab tooguwaayam ca sawara».

Jële nañu ci Al-Miqdaad ibn Mahdiikarib -yal na ko Yàlla dollee gërëm - mu wax ne, Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: «mbaa sama Hadiis du yeksi ci nit mu tëdd ag gàngunaayam naan: Diggante nun ak yéen téeréb Yàlla la, kon lépp lu nu ci gis lu dagan dananu ko daganal te lépp lu nu ci gis mu araam, dananu ko araamal, te lu Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- araamal, moog lu Yàlla araamal ñoo yam».

Jële na ñu ci Aysatu ak Abdullahi en Ibn Abbaas -yal na leen Yàlla dollee gërëm- ñu wax ne: Bi faatu dikkalee Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dafa jël ab yéreem tek ko ci kanamam, bu jaaxlee ci moom daal di koy muri ci kanamam, daal di wax ne: «yal na Yàlla rëbb Yahuut yi ak Nasaraan yi, ñoom kat dañoo jàppe séen bàmmeeli Yónente yi ay jàkka» day artu ci li ñu def.

Jële nañu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: "yaw sama Boroom maa ngi lay ñaan bul def sama bàmmeel ab xërëm, Yàlla rëbb na nit ñiy jàppe bàmmeelu seeni Yónente ay jàkka".

Jële nañu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne : Yónent Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: «buleen def seen kër yi ay bàmmeel, te buleen def sama bàmmeel am ndaje, deeleen julli ci man, ndax seen ug julli ci man dina yeksi fi man ak fu ngeen man di nekk».

Jële nañu ci Aysatu ndayu jullit ñi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne : Ummu Salamata dafa xibaar Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- benn jàngu bu mu gis ca Abasa, (jàngu : jaamukaayu katolig yi) ñu koy woowe Maariya, mu wax ko la mu fa gis ci ay nataal, Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ne ko: " ñooñu aw nit lañu wow bu ku baax faatoo fa ñoom, dañuy tabax ca bàmmeelam ba jàkka, daaldi cay def nataal yooyu, ñooñu ñoo yées ci nit ñi fa Yàlla".

Jële nañu ci Jundub -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Dégg naa Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- muy wax li njëkk juroom i fan laata muy faatu naan: " seedeel naa Yàlla ne set naa wicc ci kenn ci yéen di nekk sama xarit, ndax Yàlla da maa jàpp xarit, niki mu jàppe Ibraahiima xarit, te bu ma doon wut ab xarit ci yéen kon dinaa def Abuu Bakar ab xarit. Yégleen ne ña leen jiitu woon dañu daan jàppe bàmmeeli seeni Yónent ak seen i nit ñu baax ay jàkka, rikk waay! Buleen jàppe bàmmeel yi jàkka, man tere naa leen ko".