- Tabax jàkka ci bàmmeel yi dafa araam, walla di fa julli, mbaa suul néew ci jàkka yi; ngir sakk yoon yiy jëme ci bokkaale.
- Tabax jàkka ci bàmmeel yi, ak samp fa ay nataal, daa bokk ci jëfi Yahuut yi ak Nasaraan yi, te ku ko def, mi ngi leen di niru-nirulu.
- Araamalees na nataal lu am ruu.
- Ku tabax jàkka cib bàmmeel def fa ay nataal, kon moom ci ñi yées ci mbindeefi Yàlla yi la bokk.
- Sariiha dafa aar Tawhiid aar gu mat sëkk, ci fatt wépp yoon wuy jëme ci bokkaale.
- Tere nañu ëppal ci ñu baax ñi; ndaxte sabab la ci tàbbi ci bokkaale.