- Dañuy màggal Sunna ni ñuy màggalee Alxuraan te di ko jëfe.
- Topp Yónente bi mooy topp Yàlla, moy ko it mooy moy Yàlla mu kawe mi.
- Saxal ne sunna aw lay la, ak di tontu ñiy delloo sunna di ko weddi.
- Ku dummóoyu sunna di wootewoo ne day yam ci Alxuraan kooku ñaar yépp la bàyyi te day nar ci li muy wootewoo ne day topp Alxuraan.
- Bokk na liy tegtale ag yónenteem li muy xibaare lu ñëwagul ci ne di Na am loolu ame niki nimuko xibaare woon.