- Jéggi dayob sariiha ci bàmmeel i Yónent yi ak ñu baax ñi day tax ñu di ko jaamu bàyyi fi Yàlla, moo tax ñu war a moytu luy jëme deci bokkaale.
- Daganul di dem ci ay bàmmeel ngir màggal ko ak di fa def ag jaamu ak lu boroomam man a jege Yàlla mu kawe mi.
- Tabax jàkka ci bàmmel yi dafa araam.
- Julli ci bàmmeel yi dafa araam, doonte tabaxuñu ko jàkka, lu dul julleeb néew bi nga xam ne julleewuñu ko woon.