Jële nañu ci Aysa -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Yónent Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: «socc day laabal gémmeñ di...
Yónent bi day xamle ne setal ay bëñ ci bantu garabu Araag ak lu ko niru, day laabal gémmiñ ci ay tilim-tilim ak xet yu bon yi, Waaye daa bokk ci sabab...

Jële nañu ci Aysa -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Yónent Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: «socc day laabal gémmeñ di gërëmloo Boroom bi».

Jële nañu ci Abuu Hurayrata mu wax ne : Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: «war na ci bépp jullit mu sangu ci juróom ñaari fan yu nekk benn yoon, da ciy raxas boppam ak yaramam».

Jële na ñu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: dégg naa Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- muy wax naan: "«Yi Yàlla moñaale ak nit ki juróom la: xaraf, wat kawaru naq, ak wàññi kawari mustaas, ak lewwi ay weh, ak suqi kawari poqtaan».

Jële nañu ci Aliyun -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Góor laa woon gu bari masyu ma amoon kersay laaj ko Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ngir wàccuwaay gi doomam am, ma digal Al-Miqdaad ibnul Aswad mu laaj ka ko, mu ne ko: "day raxas sakaraam daal di jàpp". Bu dee ci Al-Buxaarii: da ne ko: jàppul te raxas sa sakara".

Jële nañu ci Aysatu ndayu jullit ñi -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- bu daan sangu janaba, da daan raxas ñaari loxoom, jàpp njàppum julli, daal di sangu, daal di xàjjale ci loxoom kawaram, bu ko wóoree ne der ba tooy na, mu sotti ca ndox ñatti yoon, topp mu raxas mbooleem yaramam, Aysatu nee na: daan naa sangu man ak Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ci benn ndab, nun ñaar ñépp di ci tanq.

Jële nañu ci Ammaar ibn Yaasir -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- da maa yónni ci jenn aajo, ma am janaba te amuma ndox, ma xalangu ci suuf si kem ni daaba di xalangoo, ma ñëw ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-, nettali ko loolu, mu ne ma: "doon na la doy rekk nga def nii say loxo" mu dóor ay loxoom ci suuf benn dóor, daal di masaa càmmooñam ci kaw ndayjoor bi, ak bitti ténq yi ak kanam gi.

Jële nañu ci Al-Muxiirata-yal na ko Yàlla dollee gërëm-mu wax ne: Nekkoon naa ak Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- cib tukki, ma nar a summi ñaari saŋam yi, mu ne ma: "bàyyileen, dama leen cee dugal ñu di ñu laab" mu masaa ca seen kaw.

Jële nañu ci Aysatu ndayu jullit ñi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne Faatimata bintu Abii Jahsin dafa laaj Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ne ko: Man damay gis dereet ju yàqu te du ma set, ndax damay bàyyi julli? Mu ne ko: “Déedéet , loolu dereti sidit la, waaye bàyyil julli ci limu bis yi ngay gis mbaax, topp nga sangu te julli".

Jële na ñu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne : Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: «bu kenn ci yéen yëgée ci biiram dara, te xamul ndax dara génn na ci moom walla déet, bumu génn jàkka ci ba keroog muy dégg kàddu, mbaa mu yég ngelaw».

Jële na ñu ci Umar ibn Xattaab -yal na ko Yàlla dollee gërëm - mu wax ne, Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: «Bu nodd-kat bi waxee: Allaahu Akbar Allaahu Akbar, kenn ci yéen wax: Allaahu Akbar Allaahu Akbar, bu waxee: ashadu an laa ilaaha illal Laahu, mu wax: ashadu an laa ilaaha illal Laahu, bu waxee: ashadu anna Muhammadan rasuulul Laahi, mu wax: ashadu anna Muhammadan rasuulul Laahi, bu waxee: hayya halas salaah, mu wax: laa hawla wa laa xuwwata illaa bil Laah, bu waxee: hayya halal falaah, mu wax: laa hawla wa laa xuwwata illaa bil Laah, bu waxee: Allaahu Akbar Allaahu Akbar, mu wax: Allaahu Akbar Allaahu Akbar, bu waxee: laa ilaaha illal Laahu, mu wax: laa ilaaha illal laahu te mu dëggu ci xolam kon dana dugg àjjana».

Jële nañu ci Abdullah Ibn Amr Ibnul Haas -yal na leen Yàlla dollee gërëm- mu wax ne dégg na Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- muy wax naan: «bu ngeen déggee noddkat bi nangeen wax lu mel ni li muy wax, te ngeen julli ci man, ndax ku julli ci man genn julli Yàlla julli ci moom fukk, te ngeen ñaanal ma Wasiila ba, ndax moom ab bérab la ca àjjana, te kenn yayoowu ko ku dul ab jaam ci jaami Yàlla yi, te maa ngi yaakaar ne man la, ku ma ñaanal Wasiila samag ramm dagan na ko».

Jële na ñu ci Sahd Ibn Abii Waqaas -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-mu wax ne: «kuy wax saa yu déggee noddkat bi, ashadu an laa-i-Laaha Illal Laahu wahdahu laa sariika lahu, wa anna Muhammadan habduhu wa rasuuluhu, radiitu billaahi rabban, wa bi Muhammadin rasuulan, wa bil Islaami diinan, dees na ko jéggal ay bàkkaaram».