- Ngëneelu Aliyun Ibn Abii Taalib -yal na ko Yàlla dollee gërëm-, ndax kersa terewu koo laaj waaye jaare ko ci keneen.
- Wuutal keneen ci laaj dagan na.
- Dagan na ci nit ki mu xibaare ci boppam ci lulu rus ngir yéwénal.
- Sobeg masyu, ak ne dañu koo war a raxas mu deñ ci yaram wi ak yére yi.
- Génne masyu bokk na ci yiy yàq njàpp.
- War na ñu raxas sakara wi ag ñaari xuur yi ndax li mu rot ci beneen hadiis.