Jële na ñu ci Aysa -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: dégg naa Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «deesul julli...
Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- tere na julli ci teewaayu ñam wi nga xam ne bakkanu kiy julli da koo xemmeem, xolam di ca nekk...
Jële nañu ci Usmaan Ibn Abil Haas -yal na ko Yàlla dollee gërëm-: Moom dafa ñëw ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ne ko: yaw Yonne...
Usmaan Ibn Abil Haas -yal na ko Yàlla dollee gërëm- dafa ñëw ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ne ko: yaw Yonnente Yàlla bi, sayta...
Jële nañu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne : Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: «ki gën a bon...
Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- leeral na ne ki gën a bon ug càcc ci nit ñi mooy kiy sàcc ci julleem gi; ndaxte jël alalu keneen ma...
Jële nañu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «ndax kenn ci yeen...
Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day leeral tëkku gu tar ci kaw kiy yëkkati boppam njëkk imaam bi, Yàlla def boppam bi boppu mbaam,...
Jële nañu ci Sawbaan -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- bu daan wëlbatiku ci julli gi d...
Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- bu daan noppi ci julli gi da daan wax: Astaxfirul Laaha, Astaxfirul Laaha, Astaxfirul Laaha. Mu m...

Jële na ñu ci Aysa -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: dégg naa Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «deesul julli fekk ñam wi daa teew, walla muy xëcconte ak ñaari sobe yi».

Jële nañu ci Usmaan Ibn Abil Haas -yal na ko Yàlla dollee gërëm-: Moom dafa ñëw ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ne ko: yaw Yonnente Yàlla bi, Saytaane de dafa dox sama diggante ak sama julli gi, te day jaxase sama njàng mi, Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ne ko: " kooku Saytaane bu ñu woowe Xinsab la, boo ko yégatee nanga muslu ci Yàlla ci moom, te nga tifli ci sa càmmooñ ñatti yoon", nee na: ma def loolu Yàlla dindi ko ci man.

Jële nañu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne : Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: «ki gën a bon ug càcc ci nit ñi mooy kiy sacc julleem» ñu ne ko: naka lay sacce julleem? Mu ne: «du matal rukkoo yi, ak sujjóot yi»

Jële nañu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «ndax kenn ci yeen du ragal walla muy tiit bu yëkkatee boppam njëkk imaam bi, Yàlla def boppam bi boppu mbaam, walla Yàlla def meloom wi melow mbaam».

Jële nañu ci Sawbaan -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- bu daan wëlbatiku ci julli gi day jéggalu ñatti yoon, daal di wax: "Allaahumma Antas Salaamu, wa Minkas Salaamu, Tabaarakta Sal Jalaali wal ikraami" waliid wax ne: ma wax Al-Awsaahii ne ko: naka lay jéggaloo? Mu ne: day wax naan: Astaxfirul Laaha, Astaxfirul Laaha.

Jële na ñu ci Abis Subayri mu wax ne : Ibn Subayri bu jullee ba sëlmal da daan wax: «laa ilaaha illal laahu wahdahu laa sariika lahu lahul mulku wa lahul hamdu wa Huwa halaa kulli say in Xadiirun, laa hawla wa laa xuwwata illaa bil Laahi, laa ilaaha illal Laahu, wa laa nahbudu illa iyyaahu, lahun nihmatu wa lahul fadlu wa lahus sanaa ul hasanu, laa iLaaha illal Laahu muxlisiina lahud diina wa law karihal kaafiruuna» mu wax ne: «Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- daa na ko tudde Yàlla ginnaaw julli gu ne».

Jële nañu ci Warraad mi daa bindal Al-Muxiirata Ibn Suhbata mu wax ne: Al-Muxiirata Ibn Suhbata xamal na ma ci benn téere bu jël ca Muhaawiya ne: Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- daan na wax ginnaaw jullig farata gu ne: «laa iLaaha Illal Laahu wahdahu laa sariika lahu, lahul mulku wa lahul hamdu, wa Huwa halaa kulli say-in Xadiirun, Allaahumma laa maaniha limaa ahtayta, walaa muhtiya limaa manahta, walaa yanfahu sal jaddi minkal jaddu».

Jële na ñu ci Abdullah Ibn Umar -yal na leen Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Mokkal naa ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- fukki ràkka: ñaari ràkka njëkk tisbaar, ak ñaari ràkka ci ginnaawam, ak ñaari ràkka ginnaaw timis ci këram, ak ñaari ràkka ginnaaw gee ci këram, ak ñaari ràkka njëkk jullig suba, moom nag aw waxtu la woo xamne kenn daawul dugg fa Yonnente bi nekk, Hafsa nettalinama ne bu noddkat bi daan nodd ba fajar gi fenk day julli ñaari ràkka, ci jeneen wax: moom Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- daan na julli ñaari ràkka ginnaaw àjjuma.

Jële nañu ci Abuu Xataadata As-Sulamii -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «bu kenn ci yéen duggee ci jàkka na julli ñaari ràkka bala moo toog».

Jële na ñu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «boo waxee sa àndandoo: noppil ci bisu àjjuma, fekk imaam bi di xutba, kon fo nga».

Jële na ñu ci Imraan Ibn Husayn -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: damaa amoon ay góom, ma laaj Yónente bi -yal na ko Yàlla xéewal ak mucc- ci lu jëm ci julli, mu ne ma: «jullil taxaw, boo ko manul nga toog, boo ko manul nga wetu».

Jële nañu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «genn julli ci sama jàkka jii moo gën junni julli ci fu dul moom ba mu des jàkka ja ca Màkka».