- Njariñu toroxlu ak teewaayug xol bi ci julli gi, ak ne saytaane day pastéefu ci jaxase ko ak def sikk-sakka ci kiy julli.
- Sopp nañu muslu ci saytaane bu dee def ay jax-jaxal ci julli gi, ànd ak di tifli ñatti yoon ci wetu càmmoñ bi.
- Leeral ni Sahaaba yi -yal na leen Yàlla dollee gërëm- daan delloo ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ci lépp lu leen jaaxal, ba keroog mu leen koy lijjantil.
- Dundug xoli Sahaaba yi, ci ne séen yitte mooy allaaxira.