genn julli ci sama jàkka jii moo gën junni julli ci fu dul moom ba mu des jàkka ja ca Màkka
Jële nañu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «genn julli ci sama jàkka jii moo gën junni julli ci fu dul moom ba mu des jàkka ja ca Màkka».
Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér
Explanation
Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day leeral ngëneelu julli ci jàkkaam ji, ak ne moo gën yool ci junni julli ci fu dul moom ci jàkka yi ci kaw suuf, ba mu des jàkka ja ñu wormaal fa Màkka, ndax moom moo gën julli ci jàkkay Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-.
Hadeeth benefits
Dañuy ful yoolu julli ci jàkkay Màkka ak Jàkkay Yonnente bi ca Madiina.
Julli ci jàkkay Màkka moo gën téeméeri junni julli ci beneen bu dul moom.
Share
Use the QR code to easily share the message of Islam with others