- Sopp nañu ñu sàmmoonte ak sikar sii ginnaaw julli farata gu ne.
- Jullit day tiitaroo diineem di fésal ay mbaaxam, doonte neexul yéefar yi.
- Baatub "duburas salaati" bu rotee cib hadiis: bu dee hadiis bi day wax ci sikar, la cay cosaan mooy mu nekk ginnaaw ug sëlmal, bu dee ñaan la nag kon mu nekk lu jiitu sëlmal ga.