deesul julli fekk ñam wi daa teew, walla muy xëcconte ak ñaari sobe yi
Jële na ñu ci Aysa -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: dégg naa Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «deesul julli fekk ñam wi daa teew, walla muy xëcconte ak ñaari sobe yi».
Muslim soloo na ko
Explanation
Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- tere na julli ci teewaayu ñam wi nga xam ne bakkanu kiy julli da koo xemmeem, xolam di ca nekk.
Niki noonu tere na di julli di jañante ak ñaari sobe yi -te mooy saw ak dem duus- ndax kon day soxlawoo di jañ sobe sa .
Hadeeth benefits
Jaadu na ci kiy julli mu sori lépp lu koy soxlaal ci julli gi balaa mu caa dugg.
Share
Use the QR code to easily share the message of Islam with others