Jële na ñu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Benn waay dafa ñëw ci Yó’ente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ne ko:...
Daa am gumba gu ñëw si Yónente bi -yal na Yàlla dolli xéewal ak mucc- ne ko: yaw Yónente Yàlla bi amuma ku may dimbali di jàpp sama loxo yóbb ma jàkka...
Jële na ñu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- ne: dégg naa Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- muy wax ne: «xibaarl...
Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day niròole julliy juróom ci bis bu nekk ak guddi gi, ci ni muy fare bàkkaar yu ndaw yi ak njuumte...
Jële na ñu ci Abdullah Ibn Mashuud -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Laaj naa Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-: jan jëf la Y...
Laaj nañu Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-: jan jëf la Yàlla gën a bëgg? Mu wax ne: julliy juróom ci waxtoom wi ko Sariiha tënk, Teg...
Jële nañu ci Usmaan -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: dégg naa Yonnente Yàlla bi-yal ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- muy wax naan: "amul benn j...
Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-day leeral ne amul benn jullit bob waxtuw jullig farata dana dugg mu rafetal am njàppoom matale ko,d...
Jële nañu ci Abuu Hurayrata mu jële ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «julliy juróom, ak Àjjuma ba Àjjuma, ak weeru koor...
Yónent bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day xibaare ne julliy juróom yi ñu farataal ci bëccëg gi ak ci guddi gi, ak jullig Àjjuma ci ayu-bis...
Jële na ñu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Benn waay dafa ñëw ci Yó’ente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ne ko: yaw Yónente Yàlla bi, man de amuma ku may wommat yóbb ma ca jàkka ja, mu sàkku ci Yónente Yàlla bi mu yombalal ko muy jullee ci këram, Yónente bi daal du loy jox Yombal, ba mu wëlbatikoo rekk mu woo ko, daal di ne ko: "ndax danga dégg wooteg julli gi?" Mu ne ko: waaw, mu ne ko: "kon nag wuyujil ».
Jële na ñu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- ne: dégg naa Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- muy wax ne: «xibaarleen ma bu ag dex nekkoon ci buntu këru kenn ci yéen mu ciy sangu bis bu nekk juróomi yoon, ndax loolu dana dese tilim ci yaram?" Ñu ne ko: déedéet du bàyyi ci deram dara, mu ne: "loolu nag moo ngi mel ni julliy juróom, yàlla da ciy far njuumte yi».
Jële na ñu ci Abdullah Ibn Mashuud -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Laaj naa Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-: jan jëf la Yàlla gën a bëgg? Mu wax ne: "julli ci waxtoom" mu ne ko: teg ca lan? Mu ne: "teg ca fonk ñaari way-jur" mu ne ko: teg ca lan? Mu ne: "jihaad ci yoonu Yàlla" nee naa moo ma ko wax, te bi ma sàkkoon ndollin mu dolli ma.
Jële nañu ci Usmaan -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: dégg naa Yonnente Yàlla bi-yal ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- muy wax naan: "amul benn jullit boo xam ne jullig farata dana jot mu rafetal njàppu ma ak toroxlu ga ak rukkoo ya,lu dul ne dana ko faral li ko jiitu ci ay bàkkaar,fii ak deful bàkkaar bu mag,te loolu jamono jépp la".
Jële nañu ci Abuu Hurayrata mu jële ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «julliy juróom, ak Àjjuma ba Àjjuma, ak weeru koor ba weeru koor, dañuy far bàkkar yi ci séen diggante bu dee moytu nañu bàkkaar yu mag yi».
Jële nañu ci Amr ibn Suhaybu mu jële ci baayam mu jële ci maamam mu wax ne: Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: «digalleen seen doom yi ñuy julli bu ñu amee juróom-ñaari at, te ngeen leen di dóor ci loolu bu ñu amee fukki at,te ngeen teqale seen diggante ca tëddukaay ya».
Jële na ñu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: dégg naa Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- muy wax ne: «Yàlla mu kawe mi nee na: seddale naa julli ci sama diggante ak sama jaam bi ci ñaari xaaj, ñeel na sama jaam bi lu mu laaj, bu jaam bi waxee: {Alhamdu lil-Laah Rabbil haalamiina}, Yàlla mu kawe mi wax: sama jaam bi sant na ma, bu waxee: {Ar-Rahmaanir Rahiimi}, Yàlla mu kawe mi wax: sama jaam bi tagg na ma, bu waxee: {Maaliki yawmid diini}, mu wax: sama jaam bi màggal na ma, -am yoon bumu wax: sama jaam bi wéeru na ci man-, bu waxee: {Iyyaaka nahbudu wa Iyyaaka nastahiinu}, mu wax: lii sama diggante la ak sama jaam bi, te ñeel na sama jaam bi lu mu laaj, bu waxee: {Ihdinas siraatal mustaxiima, siraatal lasiina anhamta halayhim xayril maxduubi halayhim wa laddaaliina}, mu wax: lii sama jaam bi moo ko moom, te ñeel na sama jaam bi lu mu laaj».
Jële na ñu ci Buraydata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne : Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: «kóllare gi dox ci sunu diggante ak ñoom yéefar yi mooy julli, ku ko bàyyi weddi na».
Jële nañu ci Jaabir -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: dégg naa Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- muy wax naan: «li dox ci diggante nit ki ak bokkaale ak kéefar mooy bàyyi julli».
Jële nañu ci Saalim Ibn Abil Jahd mu wax ne: benn waay dafa wax ne: aka neexoon ma julli ndax ma noppalu, mu mel ni dañu koo sikk ci loolu, mune leen dégg naa Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- wax ne: «yaw Bilaal taxawalal julli gi, noppal nu ci».
Jële na ñu ci Ubaadata Ibnus Saamit -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: "ku jàngul faatiha amul julli".
Jële na ñu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- ne: Moom daana kàbbar ci bépp jullig farata ak bu dul moom, ci koor ak bu dul koor, bu dee jug kàbbar, bu dee rukoo kàbbar, daal di wax: samihal Laahu liman hamidahu, daal di wax it: Rabbanaa wa lakal hamdu, bala moo sujjóot, bu dee rot jëm ci sujjóot ba daal di kàbbar, buy yëkkati boppam ci sujjóot daal di kàbbar, bu dee jug ci toogaayu ñaari ràkka yi daal di kàbbar, loolu lay def ci ràkka yépp, ba julli gi jeex, ba mu wëlbatikoo daal di wax ne: giñ naa ci ki sama bakkan nekk ci loxoom, maa leen gën a niroole jullig Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ndax nii la daan jullee ba ni mu tàqalikoo ak àdduna.