Jële na ñu ci Ubaadata Ibnus Saamit -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: "ku jàngul faatiha amul julli".
Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér
Explanation
Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day leeral ne julli du wér lu dul ci jàng saaru Faatiha, ndaxte ponk la ci ponki julli ci ràkka yépp.
Hadeeth benefits
Faatiha leneen manukoo wuutu ci ku ko man.
Ràkka bu ñu jàngul faatiha day yàqu, ci ki ko tay, ak ki xamul, ak ki fàtte; ndaxte ponk la, te ponk du rot ba mukk.
Jàng faatiha dana wàcci maamuum
bi ji bu dabee imaam bi cib rukkoo.
Share
Use the QR code to easily share the message of Islam with others