Jële nañu ci Saalim Ibn Abil Jahd mu wax ne: benn waay dafa wax ne: aka neexoon ma julli ndax ma noppalu, mu mel ni dañu koo sikk ci loolu, mune leen dégg naa Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- wax ne: «yaw Bilaal taxawalal julli gi, noppal nu ci».
Abóo Daawuda soloo na ko
Explanation
Benn waay ci Sahaaba yi dafa wax ne: aka neexoon ma julli ndax ma noppalu, mu mel ni ñi ko wër dañu koo sikk ci loolu, mune leen: dégg naa Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- wax ne: éey Bilaal! Yëkkëtil nodd gi te taxwal; ndax nu nappaloo ko; loolu nag ngir li ci nekk ci déeyante ak Yàlla, ak nooflaayu ruu ak xol.
Hadeeth benefits
Nooflaayu xol day ame ci julli; ngir li ci nekk ci déeyante ak Yàlla mu kawe mi.
Weddi ci kaw kuy tàyyeel ci jaamu Yàlla.
Képp ku def li ko war, ba setal ca boppam, dana am noflaay ak yég-yégu dal.
Share
Use the QR code to easily share the message of Islam with others