- Màggaayu mbiri Faatiha, ndax Yàlla mu kawe mi sax da koo tudde(Julli).
- Leeral ne Yàlla yittewoo jaamam bi, ba tax mu tagg ko ngir cant gi mu ko sant tagg ko màggal ko, mu dig ko ne dana ko jox lu mu laaj.
- Saar wu tedd wii dafa làmboo, sant Yàlla, fàttaliku dellu ga, ñaan Yàlla, sellal jaamu gi ñeel ko, ñaan gindiku ci yoon wu jub wa, ak artu ci yooni caaxaan yi.
- Jullikat bi buy teewlu hadiis bii -buy jàng Faatiha - day dolli ag toroxloom ci julli gi.