ndax danga dégg wooteg julli gi?" Mu ne ko: waaw, mu ne ko: "kon nag wuyujil
Jële na ñu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Benn waay dafa ñëw ci Yó’ente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ne ko: yaw Yónente Yàlla bi, man de amuma ku may wommat yóbb ma ca jàkka ja, mu sàkku ci Yónente Yàlla bi mu yombalal ko muy jullee ci këram, Yónente bi daal du loy jox Yombal, ba mu wëlbatikoo rekk mu woo ko, daal di ne ko: "ndax danga dégg wooteg julli gi?" Mu ne ko: waaw, mu ne ko: "kon nag wuyujil ».
Muslim soloo na ko
Explanation
Daa am gumba gu ñëw si Yónente bi -yal na Yàlla dolli xéewal ak mucc- ne ko: yaw Yónente Yàlla bi amuma ku may dimbali di jàpp sama loxo yóbb ma jàkka ja ci julliy juróom yi, mu bëgg Yónente bi yombalal ko mu bàyyi jullig mbooloo, mu yombalal ko, waaye ba mu wanee ginnaaw rekk mu woo ko, ne ko: ndax danga dégg noddug julli gi? Mu ne: waaw, mu ne ko kon nag wuyujil wootekatu julli gi.
Hadeeth benefits
Jullig mbooloo dafa war; ndax yombal du nekk ci lu dul lu war.
Wax ji mu wax ne: "kon wuyul" ñeel kiy dégg woote gi tegtal la ci warug jullig mbooloo; ndax cosaanu digle mooy ne daa war.
Share
Use the QR code to easily share the message of Islam with others