- Gënanteg jëf yi ci seen diggante mi ngi aju ci Yàlla bëgg ko.
- Ñaax jullit bi ci mu xér ci jëf yi, jiital bi gën teg ca ba ca tege.
- Tontuy Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ci jan jëf moo gën dana wuute, ci kem nit ñi ak seeni melokaan, ak lan moo ëpp njariñ ci kenn ku ne.