Jële nañu ci Xawlata doomu Hakiim As-Sulamiyata mu wax ne : dégg naa Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «ku wàcc cig k...
Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day gindi aw xeetam jëme leen ci fegu ak làqa ci luy jariñ nga xam ne day jeñ lépp lu nit ki di moyt...
Jële nañu ci Humaydin mbaa Abuu Usaydin mu wax ne: Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: «bu kenn ci yéen duggee ci jàkka na wax:...
Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day xamal xeetam wi ñaan gi ñuy wax bu ñuy dugg ci jàkka: (Allaahumma iftah lii abwaaba rahmatika),...
Jële nañu ci Jaabir ibn Abdallah -yal na leen Yàlla dollee gërëm- ne moom dégg na Yonnente bi-yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: « bu ni...
Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dafa digle tudd Yàlla bu ñuy dugg ci kër ak balaa ñuy lekk, ak ne bu ñu tudee Yàlla wax: (bismil La...

Jële nañu ci Xawlata doomu Hakiim As-Sulamiyata mu wax ne : dégg naa Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «ku wàcc cig kër daal di wax: ahuusu bi kalimaatil Laahi At taammaati min sarri maa xalaxa, dara du ko lor ba baa muy juge ca kër googa».

Jële nañu ci Humaydin mbaa Abuu Usaydin mu wax ne: Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: «bu kenn ci yéen duggee ci jàkka na wax: Allaahumma iftah lii abwaaba rahmatika, bu génnee na wax: Allaahumma innii as-aluka min fadlika».

Jële nañu ci Jaabir ibn Abdallah -yal na leen Yàlla dollee gërëm- ne moom dégg na Yonnente bi-yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: « bu nit ki duggee këram, daal di tudd Yàlla buy dugg ak buy lekk, saytaane day wax naan: amuleen fanaanukaay, amuleen reerukaay, bu duggee te tuddul Yàlla, bi muy dugg, saytaane day wax naan: am ngeen fanaanukaay, bu tuddul Yàlla bu dee lekk, mu wax: am ngeen fanaanukaay ak reerukaay ».