Jële nañu ci Abbu Sarrin -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: «Bul xeeb dara ci lu baax...
Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day ñaaxe ci jëf ju baax, te bañkoo xeeb donte dafa tuuti, bokk na ci yooyu kanam gu leer ak di muuñ...
Jële nañu ci Jaabir Ibn Abdullah Al-Xasrii -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: «ku dul...
Leerarug adiis bi: Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day leeral ne ki dul yërëm nit ñi Yàlla mu kawe mi du ko yërëm, koon jaam bi di y...
Jële na ñu ci Abdulaah Ibn Amr -yal na leen Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: "ñiy yërëme Aj...
Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day leeral ne ñiy yërëm ñeneen ñi Aji-Yërëme ji dana leen yërëm ca yërmàndeem ja xajoo lépp; muy ag...
Jële nañu ci Abdulaa Ibn Amr-yal na leen Yàlla dollee gërëm-mu jële ci Yonnente bi-yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-mu wax ne: «jullit mooy ki nga...
Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day xibaare ne jullit bu lislaamam mat mooy ki jullit ñi mucc ci làmmiñam du leen saaga, du leen rë...
Jële nañu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: dégg naa Yónent Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- muy wax ne: «àqi...
Yónent bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day leeral yénn àqi jullit bi ci mbokku jullitam, Bi njëkk ci àq yii mooy delloo nuyoo ñeel ku la nuy...

Jële nañu ci Abbu Sarrin -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: «Bul xeeb dara ci lu baax, donte dangay dajeek sa mbokk won ko kanam gu bélli».

Jële nañu ci Jaabir Ibn Abdullah Al-Xasrii -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: «ku dul yërëm nit ñi Yàlla mu kawe mi du ko yërëm».

Jële na ñu ci Abdulaah Ibn Amr -yal na leen Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: "ñiy yërëme Aji-Yërëme ji dana leen yërëm, yërëmleen waa suuf, kon ka ca kaw asamaan dana leen yërëm.

Jële nañu ci Abdulaa Ibn Amr-yal na leen Yàlla dollee gërëm-mu jële ci Yonnente bi-yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-mu wax ne: «jullit mooy ki nga xam ne jullit ñi mucc nañu ci làmmiñam ak ci loxoom,gàddaaykat nag mooy ki gàddaay li Yàlla araamal ci moom».

Jële nañu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: dégg naa Yónent Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- muy wax ne: «àqi jullit ci moroomu jullitam juróom la: delloo ab nuyoo, ak seeti ki wopp, ak gunge néew bi, ak wuyu woote ba, ak ndokkeel ku tissooli».

Jële nañu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne : Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: «dungeen dugg àjjana ndare ngeen gëm, te dungeen gëm ndare ngeen bëggante, moo ndax duma leen tegtal lol su ngeen ko defee dangeen bëggante? Siiwalleen ab nuyóo seen diggante».

Jële na ñu ci Abdullah Ibn Amr -yal na leen Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: benn waay dafa laaj Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-: lan moo gën ci Lislaam? Mu ne ko: "nga leele ñam, ak di nuyu koo xam ak koo xamul".

Jële nañu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne : Yonnent Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: «Jullit bi am kàttan, moo gën te moom la Yàlla gën a bëgg ci jullit bi néew kàttan, ñoom ñéppu na nga a baax, xéral ci lu lay jariñ, te nga dimbandikoo Yàlla te bul lompañ, bu la dara jotee, bul wax ay bu fekkoon ne defnaa lii mbaa lee kon lii du am, waaye waxal ne Yàlla dogal na te lu ko neex lay def, ndax boo waxul loolu yaa ngi ubbil saytaane buntu».

Jële nañu ci Ibn Umar -yal na leen Yàlla dollee gërëm- mu wax ne : Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: «Jibriil deñul di ma dénk dëkkandóo, bama muj njort ne dana ko dondloo».

Jële nañu ci Abuu Dardaa -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «ku aar deru mbokkam Yàlla aar kanamam ci sawara ëllëg bis-pénc».

Jële na ñu ci Aysatu -yal na ko Yàlla dollee gërëm- Soxnas Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «def ndànk du am ci dara lu dul ne dana ko taaral, waaye du ñàkk ci dara it lu dul ne dana ko ñaawal».

Jële na ñu ci Anas Ibn Maalik -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu jële ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «yomballeen te buleen jafeel, bégleleen te buleen dàqaate».