def ndànk du am ci dara lu dul ne dana ko taaral, waaye du ñàkk ci dara it lu dul ne dana ko ñaawal
Jële na ñu ci Aysatu -yal na ko Yàlla dollee gërëm- Soxnas Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «def ndànk du am ci dara lu dul ne dana ko taaral, waaye du ñàkk ci dara it lu dul ne dana ko ñaawal».
Muslim soloo na ko
Explanation
Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day leeral ne def ndànk ak ug nooy ak teey ci wax ak jëf day yokk bir yi ab taar ak ug mat ak rafet, kon yell na boroomam am li mu bëgg.
Ñàkk a teey day sikkal bir yi di ko ñaawal tey tere boroomam am la mu bëgg, bu ko amee it ci coono la koy ame.
Hadeeth benefits
Ñaaxe ci jikkowoo ay teey.
Ag teey day taaral nit ki, te sabab la ci wépp yiw ci biri diine ak yu àdduna.
Share
Use the QR code to easily share the message of Islam with others