- Dugg àjjana du ame ci lu dul ngëm.
- Bokk na ci matug ngëm jullit bi bëggal mbokku jullitam li mu bëggal boppam.
- Sopp nañu tasaare ab nuyóo ak di ko defal jullit ñi; ndax li ci nekk ci tasaare bëggante ak kóolute ci diggante nit ñi.
- Nuyoob lislaam duñu ko defal ku dul ab jullit; ndax li Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- wax ne: "seen diggante".
- Nuyoob lislaam dana dindi dogante ak bàyyeente ak mbañeel.
- Solos bëggante ci diggante jullit ñi,ci ne daa bokk ci liy matal ngëm.
- Ñëw na ci beneen hadiis ne nuyóo bu mat sëkk mooy: "assalaamu halaykum wa rahmatul Laahi wa barakaatuhu", "assalaamu halaykum" it dana doy.