- Li war aji-gëm ji mooy mu bëggal nit ñi ci Yàlla te xemmemloo leen lu baax.
- Jaadu na ci kiy woote ci Yàlla mu xool cig xereñte naka lay àggalee wooteb Lislaam bi ci nit ñi.
- Bégle day waral mbégte ak ug jublu ak dal ñeel aji-woote ji li muy woo nit ñi.
- Jafeel day waral daw ak dummóoyu ak sikk-sakka ci waxi aji-woote ji.
- Yaatug yërmàndey Yàlla ci jaamam yi, te moom diine ju yaatu la leen bëggal ak Sariiha ju yomb.
- Yombal gi ñu digle mooy gi Sariiha indi.