- Matug Lislaam du am ci lu dul bañ a lor ñeneen ñi moo xam xeetu lor gumu manadoon.
- Jagleel nañu làmmiñ ak loxo cig tudd; ngir li seen i njuumte ak seen i lor bari, ndax ay yi gën a bari ci ñoom ñaar lay ame.
- Ñaaxe ci bàyyi moy yi te taqoo ak li Yàlla mu kawe mi digle.
- Ki gën ci jullit ñi mooy kiy jooxe àqi Yàlla ak àqi jullit ñi.
- Tooñ man naa nekk wax walla jëf.
- Gàddaay gu mat mooy gàddaay li Yàlla mu kawe mi araamal.