- Diiney Lislaam diiney yërmànde la, te léppam dafa taxaw ci topp Yàlla ak rafetal jëme ci mbindeef yi.
- Yàlla mu màgg mi dafa melowoo yërmànde, te moom Aji-Sell ji yërëmaakoon la ci ñépp te mooy yërëm ku ko soob ëllëg bis-pénc, te mooy àggale yërmànde ci jaamam ñi.
- Pay moom moo ngi aju ca kem jëf ya, ñiy yërëme Yàlla dana leen yërëm.