àqi jullit ci moroomu jullitam juróom la: delloo ab nuyoo, ak seeti ki wopp, ak gunge néew bi, ak wuyu woote ba, ak ndokkeel ku tissooli
Jële nañu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: dégg naa Yónent Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- muy wax ne: «àqi jullit ci moroomu jullitam juróom la: delloo ab nuyoo, ak seeti ki wopp, ak gunge néew bi, ak wuyu woote ba, ak ndokkeel ku tissooli».
Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér
Explanation
Yónent bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day leeral yénn àqi jullit bi ci mbokku jullitam, Bi njëkk ci àq yii mooy delloo nuyoo ñeel ku la nuyu.
Àqu ñaareel bi: seeti ku feebar.
Àqu ñatteel bi: gunge ab néew ci këram ba ca jullikaay ba, ba ca almeer ya ba ba ñu koy rob.
Àqu ñenteel bi: wuyu woote ba bu ñu ko woowee ci céetal ab séet mba leneen.
Àqu jurómeel bi: ndokkeel Ku tissooli, te mooy mu wax ko ndeem sant na Yàlla: yarhamulallaah, aji-tissooli ji wax: yahdiikumullaahu wa yuslihu baalakum.
Hadeeth benefits
Màggug Lislaam ci di feddali àq yi dox diggante jullit ñi, ak di dëgëral mbokkoo ak bëggante seen diggante.
Share
Use the QR code to easily share the message of Islam with others