Jele na ñu ci Abuu Abdu Rahmaan As-Sulamii -yal na ko Yàlla yërëm- mu wax ne: Ñi nu doon jàngal Alxuraan ci Sahaabay Yonnente bi -yal na ko Yàlla doll...
Sahaaba yi -yal na leen Yàlla dollee gërëm-da ñu daan jàng ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- fukki aayay Alxuraan, te daawuñu tuxu...
Jële na ñu ci Abdallah Ibn Mashuud mu wax ne: Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: «Ku jáng wenn araf ci téereb Yàlla bi di...
Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day xamle ne bépp jullit bu jàng wenn araf ci téereb Yàlla bi dana am benn yool , te dees na ko ful...
Jële na ñu ci Abdullah Ibn Amr -yal na leen Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: «Dina ñu wa...
Leerarug hdiis bi: Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day xamle ne kiy jàng Alxuraan te di ko jëfe, te taqoo ak moom cig jàng ak mokkal...
Jële na ñu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne : Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: «Ndax kenn ci...
Leerarug hdiis bi: Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day leeral ne payug jàng ñàtti aaya ci julli; moo gën nit ki fekk ca këram ñàtti...
Jële na ñu ci Abuu Muusa Al-hasrii -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «nangeen kól...
Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- digle na ñu kóllarante ak Alxuraan sax ci di ko jàng ngir duñu ko fàtte ginnaaw bañu ko mokkalee ci...

Jele na ñu ci Abuu Abdu Rahmaan As-Sulamii -yal na ko Yàlla yërëm- mu wax ne: Ñi nu doon jàngal Alxuraan ci Sahaabay Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- wax nañu nu ne ñoom dañu daan jàng ci Yónente bi fukki aaya, daawuñu jëlaat dara tek ko ca fukk ya ba baa ñuy xam li nekk ci yii ci xam-xam ak jëfe, nu wax ne: ñu boole xam ak jëfe.

Jële na ñu ci Abdallah Ibn Mashuud mu wax ne: Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: «Ku jáng wenn araf ci téereb Yàlla bi dina am jenn tiyaaba, jenn tiyaaba ju ne day tolloo ak fukki tiyaaba, waxuma nag {alif laam miim} aw araf la waaye alif araf la laam araf la miim araf la».

Jële na ñu ci Abdullah Ibn Amr -yal na leen Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: «Dina ñu wax ëllag ki jàngoon Alxuraan: Jàngal te yéeg, jàngal ni nga doon jànge ci àdduna, ndax sa kër moo ngi tolloog aaya bi ngay mujja jàng».

Jële na ñu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne : Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: «Ndax kenn ci yéen bëgg na bu delloo ci njabootam fekk fa ñàtti giléem yu ëmb, rëy te suur?» Nu ne ko: waaw. Mu ne: «kenn ci yéen jàng ñàtti aaya ci julli moo gën ci moom ñàtti giléem yu ëmb rëy te suur».

Jële na ñu ci Abuu Muusa Al-hasrii -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «nangeen kóllarante ak Alxuraan jii, giñ naa ci ki sama bakkan nekk ci loxoom moo gën a gaaw a rëcc giléem gi ñu yeew».

Jële na ñu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «buleen def séen kër yi ay bàmmeel, Saytaane day daw kër goo xam ne dañu fay jàng saaru Al-Baxara».

Jële na ñu ci Ubay Ibn Kahb -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne : Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: «yaw Aba-Munsir, ndax xam nga ban aaya moo gën a màgg ci téere Yàlla bi?» Nee na: ma ne ko: Yàlla ak ub Yónenteem ñoo xam. Mu ne ma: «yaw Aba- Munsir, ndax xam nga ban aaya moo gën a màgg ci téere Yàlla bi ?» Nee na: ma ne ko: {Allaahu laa-i-Laaha illaa huwa Al-Hayyul Xayyuumu} [Al-Baxara: 255]. Nee na: mu dóor sama dënn, daal di wax ne: «giñ naa ci Yàlla, na xam-xam ndokkeel Aba- Munsir».

Jële na ñu ci Ibn Mashuud -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «ku jàng ñaari aaya yi ci mujjug saaru Al-Baxara cig guddi danañu ko fegal leeb luy Aw ay»

Jële na ñu ci An-Nuhmaan Ibn Basiir -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne : dégg naa Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «ñaan mooy jaamu Yàlla» daal di jàng: "Aaya biy wax ne: {séen Boroom nee na wooleen ma ma wuyu leen ñi may rëy a ñaan danañu dugg Jahannama di way-torox} [ soratou Xaafiri: 60]».

Jële na ñu ci Aysatu -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- da daan tudd Yàlla ci bépp jamono.

Jële na ñu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «Amul dara lu gën a tedd fa Yàlla mu kawe mi lii di ñaan».

Jële na ñu ci Abdullah Ibn Amr Ibnul Haasi -yal na leen Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: «ngëm day ràpp ci biiru kenn ci yéen kem ni yéere bu ràpp di ràppe, ñaanleen Yàlla mu yeesal ngëm ci séen i xol».