- Bokk na ci njariñal adiis bi: Ñaan mooy cosaanu jaamu yi, daganul nu jëmale ko ci ku dul Yàlla.
- Ñaan day làmboo dëgg-dëggug njaame ak nangu doylug Yàlla ak kàttanam moom aji-Kawe ji, ak soxlaal gi ko jaam bi soxlaal.
- Tëkku gu tar mooy payug rëy-rëylu ci jaamu Yàlla ak bàyyi koo ñaan, te ñiy rëy-rëylu ci ñaan Yàlla danañu dugg Jahannama di way-torox di way-doyadi.