/ ku jàng ñaari aaya yi ci mujjug saaru Al-Baxara cig guddi danañu ko fegal leeb luy Aw ay

ku jàng ñaari aaya yi ci mujjug saaru Al-Baxara cig guddi danañu ko fegal leeb luy Aw ay

Jële na ñu ci Ibn Mashuud -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «ku jàng ñaari aaya yi ci mujjug saaru Al-Baxara cig guddi danañu ko fegal leeb luy Aw ay»
Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér

Explanation

yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day xibaare ne ku jàng ñaari aaya yi mujj ci saaru Al-Baxara cig guddi Yàlla dana ko fegal ay ak lu mu sib, waxees na it: dana ko doy ci taxaw guddi, waxees na it: dana ko doy ci wird yépp, waxees na it: mooy li gën a néew lol dana doy ñu jàng ko Alxuraan ci julli guddi, wax nañu leneen it, amaana li ñu wax lépp a wér wax ji dana ko làmboo.

Hadeeth benefits

  1. Leeral ngëneelu mujjantalu saaru Al-Baxara, te mooy waxi Yàlla ji: (Aamanar rasuulu...) ba saar wa jeex.
  2. Mujjantalu saaru day jeñal boroomam lu ñaaw ak S
  3. saytaane bu ko jàngee ci guddi gi.
  4. Guddi gi mi ngi tàmbalee fi jant bi di sowe, di jeexe fu fajar gi di fenke.