- Ngëneelu ñaan, ak ne képp ku woo Yàlla, ku ko màggal la, te nangu ne ku doylu la -tudd naa sellam ga-, ndaxte néew gi doole duñu ko ñaan, ak ne dafay dégg, ndaxte ku tëx duñu ko woo, ak ne mooy Aji-Tedd, ndax ku nay deesu ko ñaan, ak ne mooy yërëmaakoon bi, ku soxor duñu ko ñaan, ak ne ku am kàttan la, ku ñàkk doole duñu ko ñaan, ak ne Aji-Jege la, ku sori du dégg, ak yeneen meloy màgg yu dul yooyu tey wane màggug Yàlla Mu tedd mi ak taaram.