- Sopp nañu baril ay jaamu Yàlla ak julliy naafila ci kër yi.
- Julli ci ay bàmmeel daganul; ndax jumtukaay la ci jumtukaayi bokkaale yi ak ëppal ca ña fa nekk, ba mu des jullee néew.
- Te sax na ci jóge ci Sahaaba yi ñuy tere julli ci bàmmeel yi; looloo tax Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- tere ñuy def kër yi mu mel ni ay bàmmeel kenn du fa julli.