- Bokk na ci njariñal hdiis bi:
- Leeral ngëneelu jàng Alxuraan ci julli.
- Jëf yu baax yi moo gën te mooy koomum àdduna bii di aji-jeex te moo fiy des.
- Ngëneel lii nag tënkuwul ci jàng ñàtti aaya ci julli rekk; saa bu aji-julli ji di gën a yokk aaya yi ci julli gi ab yoolam di gën ci moom limub giléem yooyee.