Jële nañu ci Mahmuud Ibn Labiid -yal na leen Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Usmaan Ibn Affaan dafa bëggoon a tabax jàkka ji nit ñi sib loolu, ñu bëgg...
Usmaan Ibn Affaan -yal na ko Yàlla dollee gërëm- dafa bëggoon a tabaxaat jàkkay Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ci anam gu gën a ra...
Jële na ñu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «saraxe du wàññi a...
Leerarug adiis bi: Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day leeral ne sarax du wàññi alal, waaye day fegal nit ki ay gàkk-gàkk, te Yàlla...
Jële nañu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «Yàlla nee na: yaw...
Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dañuy xamal ne Yàlla mu kawe mi dafa wax ne: yaw doomu Aadama ji joxeel -dund gila war ak giñu sopp-...
Jële na ñu ci Abuu Mashuud -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu jële ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «bu nit ki d...
Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day xibaare ne bu nit ki joxee njël njabootam gimu war a dundal, niki jabaram ak way-juram ak i doom...
Jële nañu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne : Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: «ku muñal ki am...
Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day xibaare ne képp ku muñal ki ame bor, walla mu teggil ko bor ba, ag payam mooy: Yàlla dana ko ker...

Jële nañu ci Mahmuud Ibn Labiid -yal na leen Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Usmaan Ibn Affaan dafa bëggoon a tabax jàkka ji nit ñi sib loolu, ñu bëgg mu bàyyi ko ca na mu mel, mu ne leen: dégg naa Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «ku tabax jàkka ngir Yàlla Yàlla dana ko tabaxal ca àjjana lu mel ni moom».

Jële na ñu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «saraxe du wàññi alal, te Yàlla du dolli Jaam biy jéggale ludul ag màgg, te kenn du toroxlu ngir Yàlla lu dul ne broom bi dina ko Yëkkati».

Jële nañu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «Yàlla nee na: yaw doomu Aadama ji joxeel ma jox la».

Jële na ñu ci Abuu Mashuud -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu jële ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «bu nit ki dundalee njabootam di ci séentu aw yiw loolu dina nekk ci moom ab sarax».

Jële nañu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne : Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: «ku muñal ki am jafe-jafe, walla mu baal ka ko, Yàlla dana ko keral bis-penc ca suufus keru Gàngunaayam ga bis ba nga xam ne genn ker amul gu dul keram ga».

Jële na ñu ci Jaabir -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yónent bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «yal na Yàlla yërëm waa joo xam ne dafay yaatu bu dee jaay, ak budee jenn, ak buy fàyyeeku».

Jële nañu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yónent Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «am na benn waay bu doon lebal nit ñi, daan wax ndawam la naan ko: boo demee ci ku am jafe-jafe nanga ko jéggal, amaana Yàlla jéggal nu, mu dajeek Yàlla mu jéggal ko».

Jële nañu ci Xawlata mi bokk ci waa-lansaar -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: dégg naa Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- muy wax naan: «gaay yay Pasar-pasaree alali Yàlla ji ci lu dul dëgg, sawara ñeel na leen keroog bis-pénc».

Jële na ñu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne : Yónent Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: «képp ku woor weeru koor ngir gëm ak yaakaar yiw; dees na ko jéggal li jiitu ci ay bàkkaaram»

Jële na ñu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne : Yónent Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: «ku taxaw Laylatul Xadri ngir gëm Yàlla ak yaakaar pay ga dees na ko jéggal li weesu ci ay bàkkaaram».

Jële na ñu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: dégg naa Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewël ak mucc- muy wax naan: "képp ku aj ngir Yàlla te beejul ( sëyul wala mu wax lu bon) deful tamit yëfi kàccor, dana dellu mel ni bis ba ko yaayam jure woon".

Jële na ñu ci Ibn Abbaas -yal na leen Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: «Amul benn bis bob jëf ca lu baax moo gënal Yàlla ci bis yii» maanaam fukki bis yi nëkk Si weeru tabaski, ñu ne ko: yaw Yónente Yàlla bi, ba ci jihaad ci yoonu Yàlla? Mu ne: «ba ci jihaad ci yoonu Yàlla, lu dul waa ju génne bakkanam ak alalam te dara ci yooyu dellusiwul».