/ képp ku woor weeru koor ngir gëm ak yaakaar yiw; dees na ko jéggal li jiitu ci ay bàkkaaram

képp ku woor weeru koor ngir gëm ak yaakaar yiw; dees na ko jéggal li jiitu ci ay bàkkaaram

Jële na ñu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne : Yónent Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: «képp ku woor weeru koor ngir gëm ak yaakaar yiw; dees na ko jéggal li jiitu ci ay bàkkaaram»
Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér

Explanation

Yónent bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dafa xibaare ne képp ku woor weeru koor ngir gëm Yàlla, ak dëggal ne woor farata la, ak li Yàlla mu kawe mi dig way-woor yi ci fay ak yool yu rëy, mu jublu ca jëmmi Yàlla ci lu dul ngistal walla ndéggtal, dees na ko jéggal bàkkaaram yi weesu.

Hadeeth benefits

  1. Ngëneelu sellal ak am solos woor weeru koor ak yu dul yooyu ci jëf yu sell yi.